Yonenteb Lislaam Muhamm
(Wollof)
Yonenteb Lislaam Muhamm
-
(Wollof)
Language
-
Preparation:
Other translations 75
(رسول الإسلام محمد صلى الله عليه وسلم)
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Yonenteb Lislaam Muhamm-.
Ab tënk bu gàtt bu jëm ci yonenteb Lislaam Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dama ciy leeral turam, ak askanam, ak dëkkam, ak takkum soxnaam, ak bataaxalam, ak ci li mu doon woote, ak ay keemaanam, ak yoonam wi, ak taxawaayu ay noonam ci moom.
1- Turam ak askanam ak dëkk bi mu juddoo sosoo fa.
Yonenteb Lislaam mooy Muhammat doomu Abdallaa doomi Abdul Muttalib doomi Haasim bokk ci sëti Ismaahiila Doomi Ibraahiima -yal na leen Yàlla dolli jàmm-.Ni loolu deme mooy: Ibraahiima -yal na ko Yàlla dolli jàmm- dafa juge Saam dem Màkka, ànd ak soxnaam Haajara ak doomam Ismaahiila fekk booba liir la woon, mu dëkkal leen Màkka ci ndigalu Yàlla mu kawe mi, ba xale ba màggee ba doon waxambaane, ci la yonent Yàlla bi Ibraahiima ñëw Màkka daal di tabax Kaaba ga Néeg ba ñu wormaal mook doomam jii di Ismaahiila -yal na leen Yàlla dolli jàmm- nit ñi mujj bari ca Kaaba ga, Màkka mujja nekk jubluwaayu way-jaamu ña ñeel Yàlla Boroom mbindéef yi, ñay aji-xemmeem a aj, nit ñi wey ci jaamu Yàlla ak wéetal ko jaar ci yoonu Ibraahiima ay téeméeri téeméeri at.ginnaaw loolu Ag jeng daal di am, réewi araab ya mujj mel ni yeneen réew yi ko wër, ag ceddo feeñ fa: niki jaamu ay xërëm, ak suul doom yu jigéen ji, ak tooñ jigéen ñi, ak wax lu dul dëgg, ak naan sàngara, ak toggoo ñaawtéef yi diko def, ak di lekk alali jirim, ak jël ribaa...Ci dëkk bii, ak ci biir wërngal bii, ci la yonenteb Lislaam Muhammat doomu Abdallaa di sëtu Ismaahiila doomu Ibraahiima -yal na leen Yàlla dolli jàmm- juddoo ci atum 571 ci atum tubaab. Baayam faatu na lu njëkk muy juddu, yaayam faatu ci atum juróom- benneelam, baay tëxam Abuu Taalib yar ko, mu dund dib jirim, di ku ñàkk, mu doon liggéey di fàggu alal, di dunde ñaqu boppam.
2- Sëy bu baarkeel ci soxna su baarkeel.
Bi mu amee ñaar fukki at ak juróom ci la takk soxna ci jigéeni Màkka yi te mooy Xadiijatu doomu Xuwaylid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ñu wërsëgale ko ci ñenti doom yu jigéen ak ñaari góor, doomam yu góor yi faatu ci séenug ngone, doon na jëflaante ak soxnaam ak i njabootam cig ñeewantu ak cofeel, loolu moo tax soxnaam sa Xadiija bëgoon ko lool, moom itam mu bëgg ko lool, te masu koo fàtte ba sax bi mu faatoo lu yàgg taxul fàtte ko, daan na ray sax ay gàtt di ko séddale xariti Xadiija yi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ngir teral leen, ak di rafetal ñeel Xadiija aka sàmm mbëggeelam.
3- Tàmbalig soloo ga.
Yonente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- amoon na ci ay jiko yu rafet ba ko Yàlla bindee ba tay, aw nitam dañu ko daan woowe dëggalaakoon bu wóor bi, mu daan bokk ak ñoom ci liggéey yu màgg, waaye daan bañ lool seen bir yu jëm ci jaamu xërëm te daawu ca bokk mukk.
Ba mu amee ñent-fukk i at fekk ma nga Màkka ci la ko Yàlla tànne ngir mu nekk ab Yónent, malaaka ma Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- indil ko njëlbeenu saar wi njëkk a wàcci ci Alxuraan te mooy waxi Yàlla mu kawe mi:(اقْرَأْ بِاسْمِ رَبِّكَ الَّذِي خَلَقَ (1) (Jàngal sa turu Boroom bi bind (1)خَلَقَ الْإِنسَانَ مِنْ عَلَقٍ (2) Bind na nit ci lumbu dereet(2)اقْرَأْ وَرَبُّكَ الْأَكْرَمُ (3) Jàngal! Sa Boroom mooy ki gën a tedd (3)الَّذِي عَلَّمَ بِالْقَلَمِ (4) Mooy kiy xamle ci xalima(4)عَلَّمَ الْإِنسَانَ مَا لَمْ يَعْلَمْ (5)) Xamal na nit lu mu xamul woon(5)[Saaru Al-Alaq: 1-5].Mu ñëw ci soxnaam Xadiija -yal na ko Yàlla dollee gërëm- fekk mi ngi lox, mu nettali ko li xew, mu dalal ko, daal di ànd ak moom ca doomu baay taxam ba Waraxatu doomu Nawfal -dafa dugoon ci diiney nasaraan daal di jàng Tawraat ak Injiil- Xadiija ne ko: yaw sama doomu-baay tax déglul sa doomu mbokk mii, Waraxatu ne ko: lan nga gis yaw sama doomu mbokk? Yonente Yàlla bi nettali ko li mu gis, Waraxatu ne ko:(loolu mooy Malaaka mi yàlla wàcce woon ci Muusaa, aka neexoon ma am kàttan, aka neexoon may dund bis bi la say mbokk di génne! Yonente Yàlla bi ne ko: "Ndax ñoom dañu may génne?" Mu ne ko: waaw, ndax kenn masul a indi lu mel ni li nga indi lu dul ne dees na ko noonu, bu ma fi say bis fekkoon dinaa la dimbali ndimbal gu rëy).
Wàccug Alxuraan di wéy fa Màkka, Jibriil di ko wàcce muy bawoo ca Boroom mbindéef yi, niki mukoy indilee faramfàcceg bataaxal bi.
Mu sax ci woo aw nitam ci lislaam, ñu jàmmaarloo ak moom noonoo ak moom, ñu gaaral ko alal ak nguur ngir mu bàyyi liko Yàlla yónni mu bañ, ñu wax ko la nit ña daan wax Yónent ya ko jiitu woon: njabarkat, fenkat, soskat, ñu xatal ko, tooñ ko ci yaramam wu tedd wa, daal di bundxataal ñi ko topp,Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sax ci biir Màkka di woote jëme ci Yàlla, di jublu jamonoy aj, ak ja ya araab yi daan daje leegi-leeg di jaay, ( ja: marche) di fa daje ak nit ña, di leen gaaral lislaam, te nekkul dileen ko xemmeem loo ngir àdduna walla ag jiite, tiitaluleen itam ci jaasi, yorul woon doole te du woon buur, mu dëkku leen ci tàmbalib wooteem ngir ñu indi lu mel ni Alxuraan ju màgg jii, mu sax ci di dëkku ay noonam ci Alxuraan ji, ñi ko gëm ci Sahaaba yu tedd ya gëm ko -yal na leen Yàlla dollee gërëm ñoom ñëpp-.
Ci Màkka la ko Yàlla terale ci kéemtaan gu màgg ga, te mooy Rañaan ga jëm ca néeg bu sell ba(Baytul Maqsid), daal di yéeg jëm asamaan, te xaamees na ne Yàlla yékkati na yonente Yàlla Ilyaas ak Masiih jëm asamaan -yal na leen Yàlla dolli jàmm- , niki ni ko jullit yi waxe ak Nasaraan yi.Yonente bi daldi jële ci boroom bi ca asamaan lii di julli -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- loolu mooy julli gii jullit yi di julli juróomi yoon ci bis bi, ca Màkka ba tay, fala beneen keemaan gu màgg ame woon, te mooy xarug weer wi, ba yéeféer yi gis ko.
Yéefari Màkka ya def nañu lune ngir tere ko, sori lool ci fexeel ko, ak dawloo ko nit ñi, ñuy xóotal ci di sàkku ay keemaan, ñuy dimbalikoo Yahuud yi ngir ñu jàppale leen ci ay lay yu leen di dimbali ci werente ak moom, ak dox digganteem ak nit ñi.
Bi nga xamee ne Bunduxataalu yéefari Màkka yi mi ngi wéy ci kaw jullit ñi ci la leen Yónent bi jox ndigal ci ñu gàddaay dem Ecopi(Habasa) Yonente bi ne leen: buur bu màndu ma nga fa te du ñu tooñ kenn fa moom, te ab buuru nasaraan la woon, ñaari mbooloo ca ñoom daldi gàddaay dem Habasa, ba way-gàddaay ya àggee Ecopi(Habasa) dañoo gaaral buuru Ecopi ba diine ji Yónent Yàlla bi Muhammat indi, mu tuub daal di wax ne: lii de -giñ naa ci Yàlla ne- mook li Muusaa indi woon ñoo bokk fenn fu ñu juge, lori nitam ña di wéy rekk ci kawam ak i Àndandoom.
Bokk na ci ñi ko gëmoon ci jamoy aj gi ab mbooloo mu juge Madiina daal di jaayante ak moom ci lislaam ak ci dimbali ko, su tuxoo dem seen dëkk, (Yasrib) nag lañu ko daan woowe; mu digal ñi desoon Màkka ci ñoom ñu gàddaay jëm Madiina, bañu gàddaay lislaam daldi tasaaroo Madiina, ba mujj amul genn kër lu dul ne lislaam dugg na fa.
Ginnaaw bi Yonente bi defee Màkka fukki at ak ñatt di woote ci Yàlla, ci la ko Yàlla digale mu gàddaay jëm Madiina, mu daadi gàddaay di wéyal wooteem ci Yàlla, lislaam di wéy di wàcci ndànk-ndànk, mu tàmbalee yonni ay ndawam ñuy yóbb ay bataaxal ca njiiti giir yi, ak ca buur ya, di leen woo ci lislaam, bokk na ca ñamu yónnee woon: buurub Ruum, ak buuru Pers ya, ak buuru Esibt.
Ca Maddiina ca la xew-xewu muurug jant bi xewe woon, nit ña tiit lool, bis boobu dëppoo woon ak faatug Ibraahiima doomi Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nit ña di wax naan: jant bi dafa muuru ngir faatug Ibraahiima, Yónent bi ne leen:(Jant bi ak weer wi duñu muuru ngir faatug kenn, walla dundam, waaye ñoom ñaar ay keemtaani Yàlla lañu, Yàlla da ciy ragalloo ay jaamam,Bu doon ne Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day wax ludul dëgg walla muy wootewoo lu amul, kon dina gaawtu lool ci ragalloo nit ñi ci weddi ko, ne leen: jant bi dafa muuru ngir faatug sama doom, kon anamook ku may fenloo.
Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Yàlla dakoo taaral ci ay jiko yu rafet, Yàlla melal ko, daal di ne:(وَإِنَّكَ لَعَلَىٰ خُلُقٍ عَظِيمٍ) (Yaw de yaa ngi ci kaw jiko yu màgg yi)[Saaru Al-Xalam: 4],Mu nekkoon ku melowoo mbooleem jikko yu rafet yi, lu mel niki dëggu ak sellal ak ug njàmbaar ak maandu, ak matal kóllare ba ci noonam yi sax, ak tabe, ku bëggóon sarax way-ñàkk yi la ak jatun yi ( ñi seen boroom kër faatu), ak way-aajewoo yi, ku xéroon la it ci gindi leen, ku leen yërëmoon la, ku daan toroxlu la it ngir ñoom, ba sax ab doxandeem daan na ñëw di seet Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di ko laaj Sahaaba yi, fekk ne moo ngi ci seen biir te diko man a xàmme, mu naan: kan ci yéen mooy Muhammat ?
Jaar-jaaram keemaan la cig mat akug rafet ci ay jëflànteem ak ñépp: noon bi ak soppe bi, ki jege ak ki sori, mag ak ndaw, góor ak jigéen, rab yi ak ñanaaw yi.
Bi Yàlla matalee diine ji, Yónent bi jottali bataaxel bi ca namu gën a jote, booba la faatu fekk moo ngi am juróom-benn fukki at ak ñatt, ñent-fukki at laata ñu koy yónni, ak fanweeri at ginnaaw bi ñu ko soloo mu nek ab yónent.Ñu Rob ko Madiina -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te bàyyiwul alal walla lu ñuy donnu, lu dul fasam wu weex wa mu daa war, ak suuf sumu defoon ab sarax ci yoonu Yàlla.
Limub ñi jébbalu gëm ko dëggal ko bari lool, ñi ànd ak moom aji ajug tàggatoo ga ëpp na téeméeri-junni Sahaaba, loolu mi ngi amoon laata muy faatu ci ñatti weer, amaana lii dafa bokk ci mbóoti sàmmug dineem ji ak tasaaroom gi, Sahaaba yi mu yar ci jikkoy lislaam nag ñoom ñooy ngën gi àndandoo cig maandu ak dëddu ak fegu, ak matal kóllare, ak di joxe ngir diine ju màgg jii ñu gëm.
Ki gën a màgg ci àndandoom yëpp cig ngëm ak xam-xam ak jëfe ak sellal ak joxe ak ug njàmbaar ak teddnga mooy: Abbuu Bakrin Siddiix, ak Umar Doomu Xattaab, ak Usmaan Doomi Haffaan, Ak Alliyu Doomi Abii Taalib, -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñoom bokk na ñu ci ñi ko njëkk a gëm dëggal ko, ñoo nekkoon njiiti jullit ñi ginnaawam, ñoo tée woon raayab diine ji ginnaawam, te amu ñu dara ci jagleg yónent, te jagleeluleen dara walis yeneen àndandoom yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm-.
Yàlla sàmm na téere bi mu indi ak sunnaam si, ak jaar-jaaram ak ay waxam ak i jëfam ci làkkam wi mu doon waxe, niñu wattoo jaar-jaaram loolu masul am ci keneen -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, wattu na ñu sax ni mu daan nelawe ? ak ni mu daan lekke ak a naane ak ni mu daan reetaane.Naka la daan jëflante ak njabootam ci biir këram?Mbooleem ay mbiram lu ñu wattu la bind ko ci jaar-jaaram yi, moom nit la dib Yónent, amul lenn nag ci jagley Boroom bi, yorul njariñal boppam mbaa lor.
4- Bataaxalam bi:
Yàlla yónni na Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ginnaaw bi bokkaale ak kéefër ak réer dajee kaw suuf, Nga xam ne amul ci kaw suuf kuy jaamu Yàlla te du ko bokkaale ak dara, lu dul ñu néew ñi desoon ci ñoñi-téere yi, Yàlla yónni yónenteem ba Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- muy ki tëj ña ñu soloo ak ña ñu yónni, Yàlla yónni na ko ci njub, ak diiney dëgg ñeel mbooleem mbindéef yi; ngir mu notal ko ci diine yépp, ak ngir mu génne nit ñi ci lëndëmi ceddo ak ug kéefér ak ug réer jëme leen ci leeru wéetal Yàlla ak gëm, ab bataaxalam nag mooy mottali bataaxeli yónente yi jiitu woon -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Mu woote ci mbooleem li Yónent yi daan woote -yal na jàmm nekk ci ñoom-: Nuuh ak Ibraahiima ak Muusaa ak Sulayman ak Daawuda ak Iisaa - ci gëm ne Boroom bi mooy Yàlla Aji-Bind Ji Aji-Wërsëgal Ji, Aji-Dundal Ji, Aji-Ray Ji, ki Moom nguur, te mooy kiy doxal mbir yi, mooy Aji-Ñeewant Ji, di Aji-Yërëme Ji, ne Yàlla it mooy Aji-Bind lépp lu nekk ci dund gi, li ñuy gis ak li ñu gisul, te lépp lu dul Yàlla mbindéef la ci mbindéefam yi.
Niki mu wootee ci jaamu Yàlla rekk, bàyyi jaamu lu dul moom, mu leeral -gën gaa matug leeral- ci ne Yàlla kenn la amul bokkaale ci jaamu gi, walla ci nguur gi, walla ci doxal mbir yi, mu leeral ne Yàlla -tudd naa sellam ga- jurul kenn te kenn juru ko, te amul nawle amul niroowaale, te du wàcci moom Yàlla ci dara ci mbindéefam yi, te du nekk ab jëmm ci biir dara.
Mu woote ci gëm téerey asamaan yi, niki téerey Ibraahiima ak Muusaa, -yal na jàmm nekk ci ñoom- ak Tawraat ak Sabuur ak Injiil, niki mu wootee ci gëm yónente yépp -yal na jàmm nekk ci ñoom- mu jàppe ku weddi benn Yónent weddi na Yónente yépp.
Mu bégal nit ñépp ci yërmaandey Yàlla, ci ne Yàlla di na leen doy fii ci àdduna, ak ne Yàlla mooy Boroom bi, di Aji-Yërëme ji, te moom rekk mooy àtte nit ñi keroog bis-penc bu leen dekkalee ci seen bàmmeel ya, te mooy fay way-gëm ñi ci seen i jëf yu sell te rafet benn bu ne fukk, bu ddee ñaawtéef nag benn bu ne mu fayko benn, dana leen ñeel it xéewal gu sax dàkk ëlëg bis bu mujj ba, ku weddi di def ñaawtéef dana jot payam ci àdduna ak ca àllaaxira.
Te Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bataaxalam bi màggalu ci ay bokkam walla réewam walla boppam, rot na ci alxuraan turu Yónent yii Nuuh ak Ibraahiima ak Muusaa ak Iisaa -yal na leen Yàlla dolli jàmm- lu ëpp lu ci turam rot, te tuddu ñu ci Alxuraan ju màgg jii turu yaayam walla turu ay soxnaam, te tudd nañu ci Alxuraan turu yaayu Muusaa ay yoon yu bari, turu Maryama it -yal na ko Yàlla dolli jàmm- tudd nañu ko ci fanweeri yoon ak juróom.
Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ku ñu musal la ci lépp lu wuute ak li ñu yoonal, walla xel walla pas-pas bi Yàlla bindaale ci jaam bi, walla jikko ju rafet di ko bañ; ndax Yónent yi dees leen a aar ci njuumte ci li ñuy jottali jële ko ci Yàlla, ndax ñoom la ñu gàll ci ñuy jottali ndigali Yàlla yi jëme ko ci jaamam yi, Yónente yi nag amuñu dara ci jagley Boroom bi walla ci céru Yàlla; ñoom kay ay nit lañu niki nit ñépp, Yàlla nag da leen a soloo ay bataaxalam.
Bokk na ci seede yi gën a màgg ci ne bataaxalu Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ag soloo la gu bawoo fa Yàlla, mooy ne na mu melloon ca jamonoy Yónent bi noonu la mel ba tay, te lu ëpp miliyaari jullit ñoo koy topp, di jëfe li mu yoonal, niki julli ak joxe asaka, ak woor, ak aj ak yeneen ci lu dul benn coppite walla wëlbati.
5- Kaawtéefi yónenteem ak ay màndargaam ak i tektalam.
Yàlla day dëgëral ay yónenteem ci ay Kaawteef yuy tegtale seen nug yóne, jox leen ay lay yuy seede seenug yónni, Yàlla jox na yónente bu nekk lu doy sëkk luy tax nit ñi man a gëme, te kaawteef gi gën a màgg ci li ñu indil Yónent yi, mooy Kaawteefi sunu Yónent Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Yàlla jox na ko Alxuraan ju tedd ji, te mooy Kaawteef giy des ba bis-penc, niki ni ko Yàlla dëgërale ba tay ci ay Keemtaan yu màgg, Kaawteefi Yónent bi nag yu bari la lool, bokk na ca:
Rañaan ga, ak yéeg ga ca kaw, ak xarug weer wi, ak wàccug taw bi ay yoon yu bari ginnaaw ba mu ñaanee Boroomam ngir mu nàndal nit ñi ginnaaw bi ñu bekkooree.
Ak fekk ga mu fekk ñam wu tuuti ak ndox mu néew mu baril ko ba nit ñu bari lekk ca naan sa.
Ak li mu xibaare ci ay kumpa yoo xam ne kenn xamul ag faramfàcceem, ci xamal gi ko ko Yàlla xamal, niki jaar-jaaru Yónent yi -yal na jàmm nekk si ñoom- ak séenuw nit, ak nettalig waa xunt ma.
Ak li mu xibaare ci ay kumpa yu ñëwagul yoy am na ginnaaw ga niki sawara wiy génn ca suufus Hijaas ba ña nekkoon Saam gis ko, ak li nit ñi di njëgalante ci ay tabax yu gudd.
Ak li ko Yàlla fegal te musal ko ci nit ñi.
Ak amug li mu digoon àndandoom yi(Sahaaba yi), niki li mu wax ne:(Dangeen tijji ji Faaris ak Ruum, te dangeen joxe am koomam ci yoonu Yàlla)
Ak li ko Yàlla dëgëral ci ay Malaaka.
Ak li Yónent yi doon bégale séenuw nit ci yónenteg Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, bokk na ña bégal séenuw nit ag ñëwam: Muusaa ak Daawuda ak Sulaymaan ak Iisaa -yal na leen Yàlla dolli jàmm- ak yeneeni Yónent ci banuu-Israayil.
Ak ay tegtali xel ak i niral (misaal )yoo xamne xel mu mucc mune dakoy nangu.
Te aaya yii ak tegtal yii ak léebuy xel yii lu ñu boyal la ci Alxuraan ju tedd ji ak Sunnas Yónent bi, te ay aayaam bari na lool, ku ci bëgg a taxaw na jàng Alxuraan ju tedd ji ak téerey Sunna yi, ak jaar-jaari Yónent bi, ay xibaar yu wér te wóor ci aaya yii ma nga fa.
Te keemtaan yu màgg yii bu amul woon kon ay noonam yii di yéeféeri Màkka yi ak Yahuud yi ak Nasaraan ya nekkoon ca dëkki Araab ya danañu am yoon wun jaar ba weddi ko ba moytandikuloo ko nit ñi.
Alxuraan ju tedd ji mooy téere bi Yàlla soloo Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal mucc-, te mooy u waxi Boroom mbindéef yi, Yàlla dëkk na nit ak jinne ngir ñu indi lu mel ni moom, walla aw saar wu ni mel, te ba leegi defaguñu ko, Alxuraan de day tontu ay laaj yu bari te am solo yoo xam ne ay milyoŋ i nit dañu cee , gëlamAlxuraan lu ñu sàmm la ba tay ci làkku araab ba mu wàccee woon, benn Loy (araf) wàññeekuwu ci, muy lu ñu móol di lu ñu tasaare, nekk téere bu màgg bu lottal ñépp, di téere bi gën a màgg ci yi mas a dikkal Doomi Aadama, lu ñu war a jàng la, di jàng yitam limiy firi, képp ku jàngul Alxuraan te gëmu ko yaw wu bari rëcc na ko,Niki ni Sunnas Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak njubam ak jaar-jaaram nekkee lu ñu tuxal ci ay càllale yu jaare ci ay nettalikat yu wóor, mu nekk lu ñu móol ci làkku araab bi Yónent bi doon waxe, ba day mel ni kuy dundu ci sunu biir, te it firi nañu ko ci ay làkk yu bari, te Alxuraan ak Sunna ñoom ñaar rekk ñooy delluwaay ñeel àttey lislaam yi aki tërëlinam.
6- Yoonal(Sariiha) gi Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi.
Yoonal ak tërëlin Wi Yónent bi indi mooy Yoonalu lislaam, te moo mujj ci yoonali Yàlla yi aki bataaxalam, ay cosaanam nag daa niróog cosaani diiney Yónent yi jiitu woon donte wuute na ñu seen i anam.
Te mooy Sariiha bi mat, te lu yéwén la ci jamono yépp ak barab yépp, yéwénug diiney nit ñi ak seen àdduna yépp ci la nekk, te dafay sàmm mbooleem jaamu yi jaam ñi wara defal Yàlla miy boroom mbindéef yi, niki julli ak joxe asaka, niki noonu yitam daleen di leeralal séeni jëflante ci wàllu alal ak yaxanal ak séenug nekkiin ak lu jëm ci wàllu politig ak seeni dëkkuwaay ak xare yi , ñu xam la ca dagan ak la ñu ca tere ak yeneen yu dul yooyu yoy dundug nit ñi da koy sàkku ak seenug ëllëg.
jii day sàmm diiney nit ñi ak seen deret ak seen i der ak seen i alal ak seen xel ak seen i njaboot, te dafa làmboo mboleem ngëneel yi, tey moytandikuloo ci mbooleem yu bon yi ak ñaawtéef yi, day woote ci teddangay nit ak diggdóomu ak set akug xereñ ak mbëggéel, ak bëggal nit ñi yiw, ay ñoñ seen deret yi, ak jàmmi réew yi, tey araamal di tiit loo nit ñi, ak di leen ragalloo ci lu dul dëgg. Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nekkoon na ku tar ci way-bew ñi, ak yàq ci bépp anam, ku daan xeex ay caaxaan la, ak ug beru di làbbewu.
Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne Yàlla dafa teral nit -góor ak jigéen- mu sàmmal ko mbooleem ay àqam, def ko muy kiy gàlloo mbooleem ay tànneefam ak i jëfam, maanaam, mbooleem jëf ju koy lor mbaa muy lor ñeneen . Mu def góor ak jigéen ñu yam ci lu jëm ci ngëm, yam it ci li ñu gàlloo, ak cig pay, te Saariiha bii am na ag yittewoo gu mu jagleel jigéen, moo xam yaay la, mbaa soxna, mbaa doom walla mbokk mu jigéen.
Te Sariiha bi Yónent bi indi dafa ñëw ngir sàmm xel ak araamal lépp lu koy yàq, niki naan am njoll (sàngara) lislaam dafa jàppe diine ag leer guy leeralal xel aw yoonam; ngir nit ki jaamu Boroomam teg ko ci xel mu sell ak xam-xam bu leer, Saariiha yekkati mbiri xel, def ko muy waral toggu jëf, mu goreel ko ci jéngi caaxaan yi ak jëfi ceddo yi.
Te yoonu lislaam day màggal xam-xam bu wér, tey ñaaxe ci gëstu xam-xam bu mucc ci bànneexu bàkkan, di woote ci xool aka xalaat ci sa jëmm ak ci àdduna bi, te njuréefu (résultats) xam-xam bu wér du safaanoo ak li Yónent bi indi mukk -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Te amul ci yoonu lislaam luy yékkati ween xeet ci kaw weneen xeet, amul it gënale aw nit ci kaw ñeneen ñi, waaye kay ñépp a yam ci kanamu ay àtteem; ndax nit ñépp ñoo yam cosaan, wenn xeet gënul weneen xeet, aw nit it gënul ñeneen nit ñi ci lu dul ragal Yàlla, Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare na ne nit ñi ñépp dañoo judd cig sell, amul kenn ci nit ñi ku judduwaale njuumte, walla muy donn njuumteg keneen.
Ci yoonu lislaam Yàlla dafa yoonal tuub, te mooy: nit ki dellu ci Yàlla ci bàyyi bàkkaar, te lislaam day màbb bàkkar yi ko jiitu , te tuub day màbb bàkkaar yi weesu, aajowoowul di wax say bàkkaar ci kanamu nit, ci lislaam jëflànte bi day dox ci diggante Yàlla ak nit ki te du aajowoo kenn di dox sa diggante ak Yàlla, lislaam day tere ñu def nit ñi ay Yàlla, walla di leen boole ak Yàlla ci moomeelam gi mbaa ci jaamu gi.
Sariiha bi Yónente bi indi dafa folli mbooleem Sariiha yi jiitu, ndax Sariihab lislaam bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi moo mujj ci Sariiha yi ba bis-penc, te mbindéef yépp la ñeel, looloo tax, mu folli yi ko jiitu woon, niki ni yenn Sariiha yi daan follee yeneen yi, te Yàlla mu kawe mi -tudd naa sellam ga- du nàngu jenn diine ju dul lislaam ji Yónent bi indi, ku jàpp jenn diine ju dul lislaam deesu ko nangul, ku bëgg a xam faramfaccey àttey Sariiha na ko sàkku ji ca téere yay jàngale lislaam di yu ñu wóolu.
Jubluwaayu Sariihab lislaam nag -niki mu nekke jubluwaayul bépp bataaxal bu bawoo ca Yàlla- mooy diiney dëgg ji yëkkati nit ki ba mu nekk ab jaam bu sell ñeel Yàlla kese, mu goreel ko ci jaamu nit mbaa jumtukaay mbaa ay neen.
Sariihab lislaam lu yéwén la ci mbooleem jamono yi ak barab yi, te amu ci luy juuyoo ak lu yéwén te baax ci nit ki, ndax Yàlla mi xam aajoy nit ñi mooko wàcce te nit ñi dañoo aajowoo ay yoonal yu wér, te du am ay juuyoo, di sellal nit, waaye du lu yenn nit ñi di tëralal ñeneen ñi, waaye day nekk lu ñu jële ci Yàlla, muy gindi nit ñi jëme leen ci lu baax ak ug njub, bu ñu ci àttewoo de séeni mbir jub, ñu mucc ci tooñante.
7- Taxawaayu ay noonam, ak seen i seede ci moom.
Sikki-sàkka amul ci ne Yónent bu nekk am na ay noon yuy taxaw ci yoonu wooteem, di gàllankoor nit ñi ci gëm ko, Yónent bi it -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- amoon na ay noon yu bari ci dundam, ak ginnaaw ug faatoom, waaye Yàlla dimbali na ko ci seen kaw ñoom ñépp, ñu bari si ñoom it def nañu ay seede yu bari -bu yàgg ba tay- ci ne moom ab Yónent la, ak ne li mu indi moog li Yónent yi jiitu woon indi ñoo yam, ak ne ñoom xam nañu ne moom ci dëgg la nekk, waaye ñu bari ci ñoom li leen ko teree gëm lu bari la: niki bëgg ug jiite, mbaa ragal mbooloo mi, walla ragal a ñàkk alal ji mu fàggu woon.
Mbooleem cant yi ñeel na Yàlla miy Boroom mbindéef yi.
Aji-bind ji moodi: Ustaas Doktoor Muhammat Doomu Abdul Laahi As-Suhaymii.
Jàngalekatu pas-pas la woon ca walug njàng ma aju ci Lislaam.
Xaajub Yarukaay ba ca daara ju kawe ja ñuy woowe Malik Sahuud.
Riyaad, Araabi Sawdi.
1- Turam ak askanam ak dëkk bi mu juddoo sosoo fa.
2- Sëy bu baarkeel ci soxna su baarkeel.
5- Kaawtéefi yónenteem ak ay màndargaam ak i tektalam.
6- Yoonal(Sariiha) gi Yónent bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi.